ARK NETWORK reference.ch · populus.ch    
 
  
La vie qui sommeille en toi 
 
 
Rubriques

Liens

 Home  | Livre d'Or  | Album-Photo  | Contact

POESIE WOLOF

 
Forgeron, c'est en travaillant le fer que l'éminent poéte Libasse NIANG gagnait sa vie.Mais, il s'est révélé être aussi un habile artisan dans le maniement de la langue wolof.La richesse des rimes et le rythme musical des poémes chantés qui suivent en sont un témoignage éclatant. 
 
 
Il clame avec conviction profonde et puissante sa foi en la mission d'Envoyé de Dieu de Seydina Mouhamadou Limamou Laye(1883-1909), fondateur de la conférie Layéne du Sénégal.Il porte d'ailleurs l'un des surnoms de Seydina Limaamu(Libasse), qui aurait béni sa langue le jour de son baptême. 
 
Il vécut dans les villages de Cambaréne et Malika ou il forgeait des outils aratoires pour les agriculteurs.Mort en 1944, à l'âge de 40 ans environ, il est loin d'être oublié. 
Aujourdhui encore on chante avec beaucoup de ferveur ses poémes, durant les nuits de veillée religieuse. 
 
 
 
1 - BISMI LAAHI RAHMANI RAHIMI 
 
Baay laay amul mass 
Njool yaay boroom diine 
Xallal nga nu yoon 
Leeral nga ngirum diine 
 
Yeen geum yi kaay leen nu waxtaan 
Fii ci kagn Baay Libaas,moo fégn ci Soodaan 
Te noo nampoon wolof miin ko lool 
Jii wax araamul, ci laay, kagn Seydi Soodaan 
 
Baay Laay a leen yay ci tééré Yalla,Buur bi nu moom 
Xamxam ba nekkoon ca Maxfuus,moo ko saytu woo leen 
Waar leen ñu gantu,geum yay sellel ba rilwaan 
 
Bu leen wutal Baay Laay maas nde bonte mu ñaaw 
Yonnent akub seriñ duñu benn ba diy maas 
Njiin jãngul,bindul,dajalewul tééré di ci seet 
Yalla ko yonni muy woote diine lislaam 
 
Baay Laay newul"baa siin mimmara ak liif laam" 
Jaaxal na walliyu waxumaak fooroya juy waare 
Dogonkoon ak réér ngeen jebbeul ko Lislaam 
 
Maam Aadamaa tiim ña mu feekkoon ba tén ba laa woor 
Malaaka yay sujjoot ngir leeru Yonnent ga ca moom 
Laay laay la Laahu ja mo xotti gémmeuñ ga leer ya saawaan 
Yooyay junjugn réy na,danu koy woy ba Diiwaan. 
 
Xam naa ci say jiko ñatti tééméér 
Dadul jeex,am nga kiraama 
Sak mbaax réy na ku lim juum 
Rafet jikko muñ gu yaa 
Xam-xam budul jéex,yaatu taaru tabe 
Mandu,am diine amuk leer 
 
Baay laay ba muy waaja feeñ,biddééw la andal bu leer 
Way réér ya naan biddeewub laar,way gëm ya naan bidééwub leer 
Loolu bir na leen,Séydéey "nooru lislaam" 
 
Baay Laay dafa feeñ samp raayi jullit waar leen 
Bu ngeen gëmoon jëfu Buur Yalla du ngeen tuuba yeen 
Mbooleem nit ak jinne kaay leen xañtu lislaam 
 
Sunu Buur la nuy woy di tagg Yonnent bi aleyhi salaam 
Baay Laay a woote lislaam,gëm leen ko,man woolu naa 
Yaakaar,ku kañ Seydi am ngag may fa Diiwaan 
 
Yaa naawewoon Makka,yanu leer yaak sunuy ruu 
Ba ngay cëppéelu ngor,riir wa dektu Rilwaan 
Ku gëm nu gëm,ku bañ dunu taggo ba Diiwaan 
 
Njool ma cëppéélu biir Yoof,leeram ga dem Kambaréén 
Jénéer ba dem Beyti Maamur "saalihina" ya teew 
Ña gëm fa Ndar woolu,Waalo gëm te kontaan 
 
Ñoñam ya wër ko di sabba,bañ yaa nga dééta waay 
Wax leen ci waa ji,balaa siiw sanku,nan dem ca Buur 
Pikin dañoo jeeex,maam jaa wootewoon diiné 
 
Ngëlëm dafa réy,te réér metti ma di jooy 
Ku doon siyaar Nabi,Yaaram baa nga biir Jammalaay 
Ku daan bégé Seydi Issa war nga ñëw tuuboo 
 
Yallaa la tannoon ci biir Yonnent yi,def la ngay njiit 
Yaa moom juroom ñaari diiwaan,xawsu mandi ngay leer 
Deeful wëjjéek yow nde yaa leen mën fa diiwaan 
 
Ba Baay demmee taaxi Béér,tuut koon kiraamaam ya feeñ 
Dëndug nawet jib na noor,boobéé ba tey ken du laal 
Baay Laay kerook ñay wu weex tiital na waa Béér 
 
Sëriñ si daa mawwu dugg xalwa di seeti Baay Laay 
Bëtub kiñaan daan na mbémpeen ba boroom réér 
Man dey dama yéém ñi ko wéddi te muy moom 
 
Bu leen werante biib taal yonnent a ko taal 
Ku ci xamul te di xamxamlu baña laaj 
Yellonte ngay kaague mbaa fooreya di nga réér 
Lëndëm ga sank la doo seerooti "ridwaan" 
 
Ku fekkewoon ba ngay woote xam ne yaay ki fi man 
Xérëm yu réy ya ca biir Yoof,xamb yaak ña kay muur 
Semmal nga leen ba ñuy jaamu Yalla,ken dootu yow 
Yonnent bi,yaay mbër mi xalloon yoonu lislaam 
 
Xamxam,lu muy jariñ,lu moy jëfe ko,digal ko saw gaay 
Bu loolu lépp nekkul,moo jaa,ku fiy wonew yoon 
Subhaana xamxam bu lay wommat jëme Saam 
Wax ja moo lay gétën ngay layyoo jëme naari 
 
Yonnent fu mu mosa feeñ,Yééfeer ya bañ ko diy noon 
Ña donn ay kaggu,ñooñaa koy werante ba Saam 
Ña teela gëm naan fa Zam-Zam,am fa ridwaan 
 
Yoow waat nga wacca nga,yaa woote jubël diiné 
Birël nga sap woote,doo layyoo ba ken di la yay 
Yembal nga jox Seydi,muy ommat ba diiwaano 
 
Yow waat nga wacca nga,yaa woote jubël diiné 
Doo bayyi waxtu,do tooñ,doo naññ kenn,sallaaw 
Sellal nga saw yoon Baay rafet diiné 
 
Yow waat nga wacca nga,yaa woote jubël diiné 
Naroon na noo sanku,noo ngi jaamu ken dootu yow 
Yonnent bi yaay mbër mi xalloon diine lislaam 
 
Baay Laay ne seytaane raay na boppi mbindééf yi 
Ba Baay nelawee la gééj tiit,neex ba nuy naan 
Dogoon ak réér ngeen jébbël ko Lislaam 
 
Ku koy werante da nga laajul ñi doon jééma bañ diinéém 
Kalaame kook buur,ba Baay duggee gaal 
La gééj sabbaa,Aras jayoo 
Ba Boroom Aras yëngoo Baay Laay waasuwul Béér 
 
Xaybar la Yééféér ya fitnaal noon ya ñuy seeti Njiin 
Njool ma feeñu leen ca tisbaar ngir yërmëndeem ju réy 
Ak bañ gëm ya weddi,Baay Laay yaa rafet diiné 
 
Ñu nga naa kaayleen ñu wër Goor gi,seet njañ li muy muur 
Mu ne leen reew ngeen,nde suma njañ li bu ngeen ko dee laal 
Asamaan daldi tappok suuf,gééj ga baawaan 
 
Ñu nga naan tey jii nu gis njañ lu mosul feeñ lu tey 
Nëbbub Yalla jomb na jaam gis ko,Njiin du seen maas 
Kéwél ga daldi f¨éx,gaa ña tiit ba daw tasaaroo 
Ba ñu laa yembaat la Baay Laay japp bay ñaan 
 
Moo simpi xamb ya,taxawal diine Lislaam 
"Xaatimi nabi-iina" sunu Yonnent bi woy leen ko 
Moo leeral sunu xol ba sunu tur dem ba diiwaanoo 
 
Nuy muslu séytaane,kiy raay boppi xam ya ñuy réér 
Diggënte rafle waak xiif waak mar wu tar wa ca Saam 
Na ump gaa yay dëggal Yonnent ba Diwaano 
 
Lay jeex na Njiin jib na Diwaan wacc biir Yoofi gééj 
Tambur ba jib na,muy baatub Laa illaa Laah 
Li Yalla def bir na miim rééw,dootu fey abaadaa 
Japp ak Julléék woor la nuy salloo ba rilwaan 
 
Japp ak julléék woor la nu Yonnent bataleel 
Goor ak jigéén ndaw ñépp da ciy maase 
Yonnent a ngay nelaw te bu yeewoo nu kontaan 
 
Kañ leen boroom ngir mi,Baay Laay mooy dindi réér 
Yaa nuy dindil tiisu bammeel may nu xééwël ca biir 
Firdawsi,Kawsaray baawaan nuy sanguy naan 
 
Yaa daagu jëm Pééy bu réy bi,ñépp sew na ci moom 
Dééyaale faak Buur ba,ba mu tampeel la,yaay Ruuhu Laahi 
Yalla la may yaa di njiitu "ahlu Soodaan" 
 
Yow yaa jëkkoon feeñ,di jantub diine,bir na ci moom 
Leer yaa ngiy baawaan ba Soodaan siy xëcco may gi ñoom 
Dañoo xamul Xawsu,Baay Maanaay boroom diiné 
 
"Anta Lamiin nga yaa Rohu Xudusi nga Séydil xalaa-ixi 
Yaa samsu Samaanun,wa yaa nuurun bilaadi 
Seydi Ruuhu min na Laahi 
 
Ilahiinaay pééy ba,noo séqë taabal ja nook Maam 
Firdawsi kontaan na ngir nun ñiydëggël ñaari leer 
Bu ngeen yaboo maare,am ngeen mbër fa Diiwaanoo 
 
Bu leen iññaanante ngir nun Buur bi nuy jaamu moo sakkoon 
Mbugëg,mbégte,te nuy ñaan mbég mu réy ma ca biir 
Firdawsi,Séydi yaa nuy omat ba Diiwaanoo 
 
Yonnent la nuy woy,bu leen dignat cofeel gu tar la 
Xol fees na bay tuuru,gëm woy leen boroom diine ji 
Bañ yaa ngi suumurlu,nuy kontaan ba Diiwaanoo 
 
Sa wird wi,da nga ko jaayul,nde bonte nga riis 
Sakkuwoo ku lay siiwal,wees nga puukëre laay 
Yaa jiituwoon gaa ña Diiwaan tann lislaamoo 
 
"Lay laa illa Laahu,Jëlliilu Zikru Rabbaani" 
Bi Laahi ku bañ xawssu,doo seerooti Yonnent ba naan 
Lay laa illa laahu,leer gay jolli ba Diiwaanoo 
 
Al hambdu li laahi,sunu Yonnent bi doy na noo laay 
Nee na yeen gëm yi,am ngeen ngënéél,Yallaa ma wooteloo 
Ngeen ñëw,japp leen ci laay-laay 
Japp ak julleek woor la nuy salloo ba Diiwaanoo 
 
Ab jant fenk na biir Yoof,guy gindik réér 
Réylu ak way-réér la ñu fallas ca niiraan 
Tee ngen a waaxu ñëw laaj Séydi boroom diinee 
 
Tambur bu réy ba fa Buur Yalla la ñuy jiin 
Sunu yaaram bu tedd bi Séydi Ruuhu Rahmaan 
Makkaak Medina ba Saam raññe na say leer 
 
Sunu Yonnent ba mu bayyikoo Beyti Maamur la feeñ 
Yaraax la wacci,gis ñi ko jangoon te raññeewuñu 
Ñuy séénu kaw,Njool ma war Jakkeer ja xuus ci seen biir 
Jullééji Baay Laay,Yaraax werante,nuy wooloo 
 
Yaaram bi tiim nga say maas,Buur Yalla def na ko jéég 
Sëriñ si bañ dañoo réér jomlu nde bonte ñu laaj 
Xatmun tariixa bi Isaa ibnu Maryaamaa 
 
Nooru Nabi nooru Issa ibnu Maryaamaa 
Yaaram bi donn ngay leer,sellal nga yoonu lislaam 
roy leen ci Séydi moo nuy ommat ba Diiwaan 
 
Nun kay nu ngiy gaajo leeram yu tar yi nuy naan 
Bañ yaa ngi nuy xas,da nuy sabbaa,du nook ñoom 
Looloo di seen diine,seydi am nga rilwaanoo 
 
Tammal nga say gune ñuy xam yoonu Yalla bay mag 
Yéénétunoo bayyi lislaam,yaa nu won yoon wi 
Tampees na nuy tur ca Diiwaan,yaay boroom diinee 
 
Farlook a dem jakka,fatte toppatoo ndaw,te boo soxlaa di leen pampe 
Lii layyoo la daan jur fa Saam,lileey mbasun diine 
Roy leen Njool boroom diinee 
 
Kuy xañtu lislaam te doo lakkal xaleel won ko yoon 
Doo teela may gune ag buum,muy moyug tooñ ci moom 
Loolooy mbasun diine,roy leen Njool boroom diinee 
 
Bul xeeb wolof lee nga fatte,deglu naa la ñuy wax 
Xam leen ne bët da dul suur,dee doora gëm du ngënéel 
Ñi daan werante Yonnent layyo ji nañ Saam 
 
Ku fekkewoon woote baak naaféq yaak ña gëmoon 
Dellooti daw ngir ga banneex,topp dunyaa ba dee 
Ku dem ñu ngay réccu layyoo ba fa Saam 
 
Limaamu Laay,Mahdiyu xayrul waraa Muhamadu 
Bu ngeen xamul goor gi,moo feeñoon ca Makka,muy baax 
Mu dellu feeñ Yoof,Waa rééw may xëccoo yoonu Makka 
Dañco xamul muj ga,Baay Maanaay boroom diinee 
 
Loo tayyi ñakk nga,loolaa réccu fekk mu wéy 
Nan daan bakken yi,te tuub sellal,ku réy da ngay réér 
Roy leen ci Séydi moo nuy ommat ba Diiwaan 
 
Mbooleem li fiy fooreya duñu dab Abdulaay bun Salaam 
Laajam bu réy bu réy ba mu doon laaj Yonenti Yalla Nabi 
Te noon bu koy xam na ngeen tuub,booba mooy Mustafa 
Mu waxko lépp,mu yéém ba waaru far tuub ci moom 
Dellook Xaybar naa tuub leen Muhammadu feeñ 
 
Xaybar la yééfeer ya jéex ngir dor yu tang yay dal 
Malaaka yaay wacc,Buur Yallaay dimmëli sunum njiit 
Roy leen ci Séydi moo nuy ommat ba Diiwaanoo 
 
Yallaa la yonni nga feeñ Makka ñu bañ diinee 
Nga sanc Medina,leer gay jolli ba Saam 
Beyti nangul na la,Faas gëm na sa diine 
 
Nga dellu feeñ Yoof,ñooña bañ diine 
Nga sanc Kambareen,leer gay jolli ba Malika 
Yëmbël nangul na la,Ndakaaru gëm na sa diine 
 
Saa Baay Limaamu kiy njiit,Buur,Yalla may na ko moom 
Yaaram yi xam na ko,moo dekkal ngiram Nabi Laay 
Jébbël ko Baay Séydi muy daaral pomu diinne 
 
Yow yaay Liimaan,wa lislaam,wa lihsaan,la ka ridwaan 
Saw tur la ñuy tampe,soo yeewoo tabala ya jiin 
Laay laa illa Laahu,leer gay wéy ba Diiwaanoo 
 
Sunu rombukaay bii di dunyaa 
Buñu fi def lu ñuy lor 
Na ngeen xam ne goor gu feeñoon fa Makka 
Moo dellu feeñ fii ci Yoof 
Moo nuy jallé ëllëk 
Baay Laay yay boroom caabi yi. 
 
 
 
2 - BISMI LAAHI RAHMAANI RAHIIMI 
 
"Allaahu ma salli allaa Seydinaa Muhamadu 
Salli wa sallim,yaa Rabbi,salli a laa Muhamadu" 
 
Saa maam Limaamu wooté na 
Ba "Lanbiyaayi" woolu na 
Te Ruuhu Laay jiitu na 
Di lampu leeri Medina 
 
Yaaram bu yiw bi wacc nga 
Yaa Ruuhu Laay tedd nga 
Ku koy werante weddi nga 
Su ma yabo ne sanku nga 
 
Yalla la yonni ngay Nabi 
Ngay seen gënéél ginnaaw Nabi 
Liggééy nga,am ngërëm lëmbe 
Sa ñaari leer yi jolli na 
 
Ñaari ngërëm nga boole,am 
Nga ndam sa may ga yaatu na 
Firdawsi ngay tëggoo junjung 
Yaa Séydi moom nga tuumë ja 
 
Gëm léen te woolu tey dëgël 
Di sant Laahu kiy ndimmël 
Buur Yalla moo la may,Rasuul 
Nu gëm ko woolu diine ja 
 
Yaa xalla yoon wu réy wu yaa 
Wu jëm ca pééy yu magg ya 
Sa ngir mi leer na noo ngi jaamu 
Bañji diiné pertana  
 
Fekkon nga yoonu diine sew 
Ba nééw ji doole yépp daw 
Nga xalla yoon wi,yaa fi raw 
Ku fonk jamu waaxusil 
 
Goor ak jigéén di taalibe 
sikkar sa riir fa baabu ba 
Ba xol ya buur digaani ba 
Amiin ja,doy na noo jubël 
 
Xamxam ba raw na foore ya 
Jaaxal na lawliya yi ya 
Yaa jiité lanbiya yi ya 
Diiwaan bi yaa di seen ngënéél 
 
Yaa saytu diine jiy defar 
Jullit yi,sant leen lu war 
Ñiy xantu diine ngir sa leer  
Ñuy topp tééré ya di jiir 
 
Ñi weddi Njiin dañoo xamul 
Ki mën ci diiné,noo dëggal 
Da ngeen a laajul kiy jubal 
Nde moo di goor gu laabiir 
 
Jom-jomlu jommi fey na ko 
réy-réylu,réér it fey na ko 
Xamul na laaj ñu wax ko ko 
Ci yoonu diine mooy li war 
 
Damaa gisul ku mel ni Maam 
Limaamu Laay te dégguma 
Ku wax ne Yalla moo ma yonni 
Moo ko wax nu woolu ko 
 
Gëm seede leen ne sant naa 
Ki tax ma seeru Séydinaa 
Ba gëm ko,naa ko "aamanaa" 
Ku woolu sant war na la 
 
Sëriñ sa toppu tank ba 
Saa bay Libaass ne maay boroom 
Kuy xañtu weer ba jant fenk 
Xamal ne leer ya wër na la 
 
Njaal-all yeek njanaaw yi ñook 
Garab yi boole gëm na ñoo 
Nit ak jinney werante,noo 
La woolu,Seydi tedd nga 
 
Bu gaalug Baay Libaas riddéé 
Ba gëm yi naani Kawsara 
Kerook,ñi gantu Baay Libaas 
Di ñee ñi gëm ca kump ga 
 
Ñi tëx te buur dañoo tëkkaale 
Mahdiyook i walliyu 
Ka wax ne Yalla moo ma yonni 
Kooka moo di Nabiyu 
 
Araab yi ak Tubaab yi ñoo 
Jëkkoon ci yoonu Nabiyu 
Wolof di xaar mujjug jamaana 
Maam Limaamul Mahdiyu 
 
Yaaram ba feeñ na ciy leboo 
Xërëm ya tiit na bay faboo 
Boroom ngënéél la nuy xaboo 
Yaa woote diine,noo wuy yoo 
 
Subhaana maa ko yéénéwoon 
Nu boole xol yi ndax nu man 
di jéém a roy ñi jiituwoon 
te aw ci yoonu Muhammadoo 
 
Lu fiy jullit nu bokk Ndey 
Da gaan ci Buur bi leeri pééy 
Ndax Buur jubal sunub liggééy 
ci lampi leeri Muhamadoo 
 
Yonnent yi wootewoon li laahi 
dakkantalees na leen ci Laahi 
Ku dee te doo"aduuwa"Laahi 
di Abdalaahi Muhamadoo 
 
Nabee dikkoon ne jaamu leen 
Yonnentub Yalla ñeel na leen 
Ku weddi kii dawal keneen 
Te génn yoonu Muhamadoo 
 
War ngeen na xam ne jangu neen 
Te jëfewoo ko moo di ten 
bu teey bu neex te doo ca naan 
Gojam ba ñeel na Muhamadoo 
 
Moo tax ba Baay Libaas ne leen 
da ngeen di wax te laaju leen 
War ngeen a gaaw ma atee leen 
ci yoonu Diine Muhamadoo 
 
Xamxam ba woon ca Mustafaa 
Du jééx te lënt nekku faa 
Bu kaan sottee mu tuuru faa 
Lu mankewul la Muhamado 
 
Araab du jël wolof déjoo 
Ndax gëm yépp janguñu 
Ñi mel ni man dañuy béjoo 
werante sarti Muhamadoo 
 
"Laa ilaaha illa Laahu Muhamadoo 
Rasuulu laahi waahidun 
Rabbul Jalliilu Majiidun 
Salli alaa Muhamadoo" 
 
Yaa feeñ ci Yoofu gééja waay 
Sa tur wi siiw na dootu fey 
Boroom jamaano maa la woy 
Nga may nu,dig nu,doo naxe 
 
Sëriñ sa jang Alxuraan 
Ba xam'Chariihatu" ak cosaan 
Ki Yalla yonni fii Zamaan 
ñu bañ ko,xaw ma seen pexe 
 
Giñ naa ci Laahu kiy Boroom 
Ibnu Maryaama yaa di moom 
Yalla la tann doo moroom 
Ñi gëm te woolu ñoo texe 
 
Diggënte Beyti Maamur ak Yaraax 
Diggënte boobu dand na 
Te lef ma yaa na,Ruuhu laahi 
Ngawar la,naar wa pepp na 
 
Njool war na gaal ba dem Yaraax 
Jakkeer la war fanaani Yoof 
Jullee fa Njool ma,gëm ya naa 
Ko,Ruuhu Laahi,doy nga noo 
 
Ba Maam jogéé,jëm Jamma Laahi 
Ñi gantu woon xëccoo na koo 
Ña wuyyuwoon Madiiné Laahi 
Ci yoonu diine yobbu koo 
 
Bésub keroog la gééj ga neex 
Ngor ak, Wakaam ya seede koo 
Caaroy,Ndakaaru,waa Yaraax 
Ñu naan ca mbeex ma,jaale koo 
 
Haalim ya jomlu,gééj ga gëm 
ba jox Madiine ak ruu-am 
Lu tee werante fey,nu gëm 
ba gaa ya jiituwoon texe 
 
Jirim ya jooy na ba sëngeem 
Njool ma ñëw na,seen rongoñ ya fer 
Jullit yi wéétoon bay xelaat 
Donoy Madiine wacc naa 
 
Raxas xolam ba muy fayaax 
Lu cay lu bon mu rekki koo 
Mu mel ni saaba door a baax 
Lu cay lu gën mu dolli ko 
 
Ku déglu saari Alxuraan 
Ña gantuwoon la fay tëkkoo 
Ñi jomlu diine ngir kiñaan 
Malaaka yaa ngi leen ëkkoo 
 
Ku nekk fooreyë boo nuyoo 
Sa mbooti xol mu raññe ko 
Kerook mu jam la doo feyyoo 
ba loo xamoon nga fatte ko 
 
Ni baay Libaas di def"rijaal" 
Bu dee mbëriit mu daane koo 
Mbiram manee fu ko misaal 
Ki gëm te woolu xam na ko 
 
Li Yalla sante doo ko jaas 
Ku farluwul nga jéppi koo 
Taasanxa diine,yaa ko daas 
Ku bañ nga rendi sañ nga ko 
 
Ku lamb saa buumi cofeel 
ci Baay Libaas,na bayyikoo 
Bu wooluwul ki nuy texeel 
Guddeek bëcëg nu muslu koo 
 
Samag cofeel di law ni ngooñ 
Ku saytu paaka jublu koo 
Nu ñaan ci Buur bi bañ ku tooñ 
Musël ga yal na jiitu koo 
 
Sa diine dootu fey wallaay 
Yallaa la woolu jox la koo 
Yow it nga woolu Ruuhu Laay 
Mu jiitu,gëm ya topp koo 
 
Séytaane mel nikkik fital 
Di takk jëm ci buumu xol 
Damaa bëgoon lu may ragal 
Nga mey ma tul gu may "sawe" 
 
Ndax waaji man damaa léjël 
Ba mel ni kul ma fëkk jël 
Moo tax,ma ñaan si sam ndimmël 
Ndax mbër nga,yow man nga ma rawe 
 
May ndaw lu tollu cig bëggam 
Muy dox di yonni ay ndawam 
Yu bon di sante aw xambam 
te xaw ma boor bu muy xawe 
 
Sëriñ si mar na bay xundooñ 
Ñu dem ba Makka weesu koo 
Ma jooy rotal samay rongooñ 
Da ñoo gëlëm te rééré ko 
 
Ku weddi ndaw te laajuloo 
Bu ngeen layyoo mu sank la 
Ku Yalla yonni,ngay jotal 
Mbindééf yi,booba wacc nga 
 
Ki sot xalima,soos daa 
Tektal yu woor la daa xalam 
Ña saytu téére ya gëlëm 
Nde boon ñu raññee aw meloom 
 
Kurél bu yiw bi fawxa ngeen 
Ku dul yonnent bi ñee na leen 
Lu jiitu tey la Yalla noon 
Di ngeen sujjoot ci Muhamadoo 
 
Li ngeen di jëf,li ngeen di wax 
Li ngeen di jorta wooru maa 
Li ngeen di lééb la Yalla wax 
Amaana moo di atte ba 
 
Jullit yi maase ngeen ne Njiin 
Sore na waaye dektu na 
Li ngeen di waa ja léép malaaka 
Daldi saytu tampe ba 
 
Mbooleem li fooréyiy yaxal 
Du ñu fi def lu gën jubël 
Sikar te boolekaak matal 
Jullee ka ñaan ci Muhamadoo 
 
Bu nuy siyaari Jammalaay 
Yooryoor ba Maam nangul na nu 
Guddik diiwaan la gëm ya yéék 
Kerkeraani Muhamadu 
 
Da noo gisul ku mel ni Maam 
Limaamu Laay te déggu noo 
Ku melni Seydi dootul feeñ 
Ci dun bi woor na kiy fexe 
 
Ñi gëm te woolu noon na seew 
Nga woote,yow ni yonni ku 
Ku bañ sa diiné dey ku beew 
Jëfam ja Yalla xoolu ko 
 
"Baxril buxxuri Mustafa 
Wa laa nafaasa xad kafaa 
Li kambareen wa Yoofa haa" 
Si lim bi nuuri Muhamadu 
 
Yonnen bi won naa num ngirëm 
Xallal nu yoonu Ajjana 
Nu santa Laahu woy Rasuul 
Bu yiw bi saytu caabi ja 
 
Nabee waxoon ne saa ginnaaw 
La waay di ñëw di leen fi woo 
Liggééy ba faw yool ba nééw 
Du tol ni yoolub Muhamadu 
 
Xam ngeen ne jaam bu bañ Boroom 
Du am taranga am ngërëm 
Te yoonu laaxiraam,xelam 
Du dal,du am ku ko yërëm 
 
La woon fa Makkaak Medin 
Ñoo ka boole Jammalaay 
Ba suuf yëngoo leeri Jabeel 
Ya "turné" wéy fa sowu ba 
 
Yalla la yonni ngay ndawam 
Nu gëm la soobu ci ngirëm 
Te Yalla daal a fiy Boroom 
Ku bañ du tee nga di laram 
 
 
 
3 - BISMI LAAHI RAHMAANI RAHIIMI 
 
 
Xundooñ ngeen Njiin na ngay fellax 
Ku mos,muy gééj gu neexum ndox 
Ku nann,bilimbaane,dootoo dox 
Di saytu sa ndaa di rootaani 
 
Te Muhamadu moom riñaanoon na 
Fa Makka ba Njool ma jalloon na 
Limub asamaaw ya déggoon na 
Fa Yalla la tiiñ ka jangaani 
 
Mu dellusi jang,dem faati 
Ki labbali yoon wi moomaati 
Bu leen bañ céébo maa ngeeti 
Ku bañ wile waame xaaraani 
 
Wolof nga nu feeñu bés nikki tey 
Wolof laa namp woy la ba tey 
Liggééyal Yalla moo gëna yay 
Mu sant nu,noo ciy kontaani 
 
Ñi rééroo sanku ngeen ku ci bañ 
Ki Yalla yabal,waxam ja du deñ 
Te Mahdiyu mooy boroom sañsañ 
Te mooy ubbi "baabu jannaati" 
 
Mahdiyu laay fajal na nu mar 
Ba Njiin wootee la foore ya wor 
Sunub sang jooy na,Saaba ya xar 
Rogon yay "baxru rahmaani" 
 
Tanxal na ca soppe yaak bañ ya 
Junniy junni naan ca leeram ya 
Nit ak jinné woo na leen dunyaa 
Ngiréék ñuy jaamu Rabbaani 
 
Ba Njool may waaja feeñ ku jubul 
Ka jooy fa safaan ba,jaam ya yëgul 
Niiraan jooyle kook ya mu sol 
Rogoñ yaay "baxru Zulmaani" 
 
Labal na ca lenn ciy fooréya 
Bu ñuy firi boole seen tor ya 
La ñuy firi wooratul jaam ya 
Ba Njool ma ñu jiñ ko seytaane 
 
Ba Mahdiyu feeñagul amu fi 
Ku fiy wone yoon wu jub néwu fi 
Li Yalla bëgg ak li muy tere fii 
Lu ngeen bañe Baay Libaas la ne 
 
Barib xamxam taxul mana dem 
Siraat am ndok la,bés bu ñu jëm 
Ki fiy wone yoon wi moo mata xam 
Te farlu ca laa mu santaane 
 
Ku tektaluwoon ci waa ju gëlëm 
Da ngay mujjé réére mbir ci waxam 
Ku réére jamano,doo mana xam 
Boroom a nga leen di dénkaane 
 
Xëccoo leen wéétëluk Fari ja 
Bu leen jangaani ngir daraja 
Yonnent,foore ya mooy dono ja 
Ségém rombul ndigël daa ne 
 
Da nuy tagg Njiin boroom jamano 
Ki woote,nu woolu kay naxu nu 
Da fay gindi ruu yi booleek nun 
Nu dellu ko sant "hamdaani" 
 
Bu leen xeeb jaam bu aw ci ndigël 
Ndigël du ndugël, ragal nanu bël 
Boroom gaal gi moo nuy jël 
Yoobu nu pééy ba nuy naane 
 
"Al hambdu li Laahi Maaliku naa 
Wa salli a laa Muhamadu naa" 
Ku lay mana sant man raw naa 
Ndegam du ka siiwé "alfaani" 
 
 
 
4 - BISMI LAAHI RAHMANI RAHIIMI 
 
"Badaa xuruubiyu samsan 
Wa anta Mahdiya Laahi" 
Boroom cosaan ya ko jangoon 
Da ñoo xamul Nabi Laahi 
 
Boroom junjun ya fa Makka 
Moo moom junjun ya fa Taayif 
Boroom junjun ya ca Firdawsi 
Moo di Baay ñangu Laay 
 
Bu gaalug diine ga teeree 
Ku ñaanul paas di nga tardee 
Limaamu"safinatu saadati 
Xawsu nixmatu Laahi" 
 
"Imaamul il mursaliina 
Wa xaatimu nabi-iina" 
"Liwaa-ul hamdi" nga tallal 
Nu gis ko gëm Nabi Laahi 
 
Ku naw sa alluba weddil 
Te ñëw mu won la nga daanu 
Mu sol la leer ya nga di sabbaa 
Ba naan Alhamdu lilaahi 
 
Limaamu Laay, ba mu wootee 
Fa gaaña rééré fa sowu ba 
Yatam wa dal, mu ne tuub leen 
Ba gaa ya nooy Na bi Laahi 
 
Limaamu Laay ba nga taaloo 
Ba leer ya jolli ca biir Yoof 
Lëndëm ga daay na ba naawal 
Xérëm ya,ngay Nabi Laahi 
 
Boroom xérëm ya da ñoo gaaw 
Tabax jumaa ja ca xeer ya 
Mbaaxam ga tax na ñu booloo 
Ne laa ilaaha illa Laahu 
 
Toxal nga biddaa ci sa diiné 
Nandal nga mag ña ca leer ya 
Lakkal xaleel ya fa nekkoon 
Ñuy xañtu diiné "li Laahi" 
 
Yaay gééju leer gi di baawaan 
Dekkal nga xol yi fi deewoon 
Ku aw sa ngir mi fasoo naani 
Tuubaaa, woolu na Laahi 
 
Biddiw ba xotti na leer ya 
Sa lay wa jééx na fa jaam ya 
"Illaa bi hadrati man xaala 
Ajibuu daa-iya Laahi" 
 
Nit ak jinne la ko boolee 
Goor ak jigeen na ñu jaamoo 
"Balaxta sawta ka sarxaam 
Nawarta xarba li Laahi" 
 
"Balaxta sawta ka yamiin 
Balaxta sawta ka jawfu 
Muhyi fuhaadi faxiira 
Ibaadi najiya Laahi" 
 
Li Yalla sante jaamam yi 
Fooreeyaa ko di juuyoo 
"Jasaaka Mahdiyu Laahi 
Wa fayta huduuda Laahi" 
 
Yaaram bi nee wuloo"baa" 
Yaarambi nee wuloo"siin" 
"Anta miftaa u bahril 
Uluumi bi Bismi Laahi" 
 
Sunu Yonnent ba mu faatoo 
Werante waa nga ca réér yaa 
Da ñoo xamul xalifaam 
Seydinaa Isaa Ruuhu Laahi 
 
Ba mu bawoo béyti Maamur 
Saxaar la war ba Yaraaxoo 
Boroom cosaan ya ko jangoon 
Da ñoo xamul Ruuhu Laahi 
 
Waxtaan na faak ña mu andal 
Ba jiite leen julli ñaan 
Sunu Boroom defal na ko ñaanam ga 
Muy "Wixaayatu Laahi" 
 
Sagn gi Yalla Sageel la 
Fa noon ya ak Nasaraan yaa 
"Tamuru bi xaybati him 
Zu kiraamti, inda Laahi" 
 
Jirim sëngéén ñetti fan 
Ba Njool Medina¨ñëw la ñu reeo 
Mu bégël jullit ña ñu sabbaa 
Mu daagu jëm Jammalaahi 
 
Ñu raam sujoot,ba ñu noppee 
La seen rongoñ ya di maayoo 
Njool ma jullée sunu yaaram 
"Nazalta yaa Ruuhu Laahi" 
 
Kerook la gééj ga di sabbaa 
Lewet ba gëm ya di naanoo 
Ku naan ca teen ba di sabbaa 
Te sant Baay Ñangu Laahi 
 
Buur Yalla woo na ko Pééy bub 
Ku dootul moom du fa jaaroo 
Mboole mi ndééy la ca gën 
Muhamadoo ko déglu fa Laahi 
 
Ngawar gu réy ga nga naaweek 
Buraax ba dem ba ca Pééy ba 
Noonam ya koy bëgg roy 
Seen masin ba sew na fa Laahi 
 
Sa waay du jax du jaaxle 
Lêndëm gu tar du ko laaloo 
Leeram ya doy gëne jolli 
Mu am "ridwaanu li Laahi" 
 
Laa ilaaha illa Laahu,du nu sappi 
Ngir mooy junjun ya ca Pééy ba 
Yal na mujjug sunu "Kalaam" 
Di laa illaha illa Laahi 
 
Laay laay la laa illa laahu 
Woy leen Jabeel ma ca leer yaa 
Limaamu Laay li nu lay woy 
Du jééx du xaaj dunu tayyi 
 
 
5 - BISMI LAAHI RAHMAANI RAHIIMI 
 
Jantub diine lislaam 
Da ngaa fenk ñuy miim 
Nu gëm woolu leer yaa 
Ngi baawaam fu ne 
 
Baay Laay ngeen ne jangul 
Mu woo leen, ñu gantal 
Ginnaawam ga daaneel 
Fi haalim ju ne 
 
Jinnéék nit la woowoon 
Ci diinéém, ku teewoon 
Te doyloo ko diiwaan 
Nga doy ko lu ne 
 
Da ngay jantu njolloor 
Ñi gantoo ngi ciw guur 
Te lii woor na kuy gor 
Ci diiwaan bu ne 
 
Rasuuloo ilaahi 
Ibnu Abdulaahi 
Moo leen woo wa Laahi 
Madiine fi ne 
 
Yallaa magg mooy Buur 
Turam woowa nay riir 
Ba seen xol sangoog leer 
Mag ak ndaw ku ne 
 
Rasuuloo ilaahi 
Mahdiyoo ilaahi 
Bi Laahi wa Laahi 
Ku bañ "pertana" nga 
 
Na ngeen déglu baat bi 
Da may woy Yonnent bi 
Booleek sant Rabbi 
Te moo war ku ne 
 
Wolof yooya laa miin 
Te moom laay wuyoo Njiin 
"Sekarteer" amul yoon 
Ci Yonnent bu ne 
 
Al hamdu li Laahi 
Wax ko war na noo 
Ngir moo feeñal Yonnent 
Ci biir xeet wu ne 
 
Gééjug leer ci Soodaan 
Xamul yaa ngi rootaan 
Sangoo leen ko nuy naan 
Moo gën ndox mu ne 
 
Seydi Ruuhu Rahmaan 
Donoy Mahdiyoo 
Ba yaaram ba laqoo 
Ba tey yaa fi ne 
 
Ba muy woote diineem 
Te ñuy bañ tariixaam 
Nga dib taaw di seedeem 
Ba tey yaa fi ne 
 
Da ngaa jub, sa ñoñ jub 
Woyof toyy niw xob 
Di jambaar def ub tab 
Siggil yaa fu ne 
 
Daraapoo bu lislaam 
Bi yaa ko ame 
Bu leen yoon wi rééréé 
Nga sañ ko wone 
 
Boroom xeej bi yaa jaam 
Ñi daarloo ci xamxam 
Ci seen kow nga jël ndam 
Siggil yaa fi ne 
 
Da nga yiw, yéwen taaru 
Doy képp kuy waaru 
Séydéy boroom daaru 
Yaa koy wone 
 
Ku doyloo sa xamxam 
Ba laajoo ñu gënë xam 
Do taggook i jamjam 
Yu réy wet gu nee 
 
Baay Laay gééj gu dul jééx 
Te raw lem ci ag neex 
Te lamboowul ag tiix 
Tanxees a koy wone 
 
Setal seeni ñaaw ñaww 
Nandal gaa ñaa ñuy soow 
Xanaa xaw na ñoo naaw 
Ku man dey wonee 
 
Ku lay roy ci bi "xarnu" 
Feeñul wonee 
Da ngay njiit ci lislaam  
Bi yaa leen tanee 
 
Gënël ngël nu nuy ndey 
Gënël ngël nu nuy baay 
Te yaa gën sunuy maam 
gënël nuy junné 
 
Ku lay bañ du kontaan 
Lu waaj waaj du waxtaan 
Bu walle ñu reetaan 
Lu man man mu ne 
 
Ba Njool may taxaw 
Ben si tey ngay xaree 
Te wééeroo sa gannaay 
Muy dal saa su ne 
 
Jiyaar jii si baatin 
Bu doon "Zaahiroo" 
Ñu janloo nga daaneel 
Ci goor ay junné 
 
Ay jambaar nga andal 
Ku lay sooru gental 
Sa gannaay ya koy dal 
Du wér bay wunni 
 
Liggééyal nga Yalla 
Liggééyal nga Baay Laay 
Ba jot seen Ngërëm 
Doo fi maasun gune 
 
Ndawal Buur ku bañ weej 
Ku réyréylu sew ruuc 
Soppeem yaa nga noon 
Ngééj ñu xam faa mu ne 
 
Li tax diine yaa suux 
Ba Yonnent jëkkee juux 
Boroom tééré ya xoox 
Di bañ wet gu ne 
 
Tawreet ak Linjiiloo 
Saboor diig nanoo 
Furxaan teew na gacceel 
Ña noon nii du nii 
 
Ñi daan bañ Rassooloo 
Siraat ñooy rëpééloo 
Tuubéén ñaa ko doyloo 
Batey ñoo fi ne 
 
Bu dul konte Baay Laay 
Lëndëm sank fuy gaay 
Ki tax ngeen di laay laay 
Yallaa ko yonni 
 
Da nuy ñaan ki nuy mey 
Mu yobbël nu buy doy 
Ba cik mujj nu far wéy 
Ci ngir mii nu ne 
 
Sañseel gëm yi ñuy bees 
Giroo ngir mu tek lees 
Booleek ndééyi depess 
Yu jëm pééy bu ne 
 
Baal niiw yu wéy ya 
Jéggël gëm yu teew ya 
Ña laqook soppeem ya 
Si nit ñeek jinné 
 
Dundël diine lislaam 
Ci barkeb Yonnentam 
Di njiitam di soppeem 
Da koy may lu ne 
 
Da daan rey di dekkal 
Fu lëndëm mu leeral 
Ba gééj wéx mu wéxal 
Ñu naan saa su ne 
 
Ay kéémaan nga andal 
Te say seede jééxul 
Ku laamlaami laajal 
Ci mag ñii fi ne 
 
Li war yeenu "haalim" 
Ci bii "xarnu" mooy xam 
Boroom, boole kook gëm 
Te aw cim ngirëm 
 
Yeeteetoo ñu yeewoo 
Xanaa ber sa saawaa 
Sa ñoñ nangi faawaa 
Ba réér cik lëndëm 
 
Bakkan jartil loolii 
Da ñuy dee ñu suuli 
"Fa la sakk xawlii 
Axiixum hikam" 
 
Da nuy sank njalbeen 
Jëndeek mucc, mu lew leen 
Fa firdawsi nuy béél 
Ku nekk taabalam 
 
Ku dem Tuubaa gis pank 
Yay daagu dox ndank 
Luy loolu seen tank 
Yay temtemi 
 
Yaram yépp koy yëg 
Kawar yépp koy yëg 
Muy banneex bu dul dog 
Bu dootul yeme 
 
Su Buur Yalla santee 
yonnentaam mu wootee 
Ku wuyuwul bu sottee 
Nga réccuk mujjam 
 
"Fa yaa ahlu soodaan" 
Yonnent feeñ na woo leen 
Da ngeen gantu nee ngeen 
Du moom, noo ko gëm 
 
Bu dee fooréya, lay jeex 
Nde tektal ya day weex 
Ca tééréém, da dul neex 
Dey jeexal xolam 
 
Ku fiy jaaxle laajal 
Ñi xam ñoo di tektal 
Ñi séytaane rééral 
Ba tax ñoo gëlëm 
 
Njiinoo njiin jibul neen 
Njiinum Yalla raw leen 
Ëllëg teel ñu laaj leen 
Fa Saam ak wallam 
 
Ku bañ yërmëndey Buur 
Kerook moom lañuy door 
Mbugal wër ko muy nuur 
Du taggook loram 
 
Yonnent baa mu woottee 
La saabaam ya footee 
Ku noon "aamanaa" 
Tey nu laabal xolam 
 
Ci saabuy Boroomam 
Saxoo tur wa mooy xam 
Xalam muxjizaatam 
Te fagguy ngërëm 
 
Yallaa yonni Baay Laay 
Ci nit ak jiiné 
Na leen woor ne Séydééy 
Borom "xarnu" bi 
 
"Allaa-uma salli 
A laa xayru rusli" 
Ñi Buur tann boolee 
Ñu sëlmël ci ñoom 
 
 
6 - BISMI LAAHI RAHMAANI RAHIIMI 
 
Siyar naa la Baay Laay yow mi doyloo sa Buur, woo ma 
Siyaar naa ñi and ak yow, digéék yow ki am worma 
 
Sa Buur baa la doyloo sol la leeram ya ngay woote 
Siyaar naa la yow Baay Laay, siyaar naa ci say Saaba 
 
Ku siyaar sa xol dootu wow, dey tooy ngireek mar wi ciy baawaan 
Ku yaakaar ci yow doo sooy bay dellook merum awmaa 
 
Nabeey gaal gu réy guy jallé mooy Maam Limaamu Laay 
Ku am gaal te am say mool, ne looy tiit fa jallu baa 
 
Nabeey gééju leer, duusam yu réy yaak na ñuy bëbe 
Njanaaw yaa ca naanoon leeri waxyoon la ñuy sabe 
 
Al hamdu li Laahi, nuy sant Buur ngir ga Maam Libaas 
Sunu soppe, soppe Laahu, Séydee di xejj ba 
 
Ku diis yaa ko yan Laahu, sa Yonnent ba seede ko 
Sa yan boo ma yan ñaan naa la dooley na may fabe 
 
Jullit yeen ñi gëm Baay Laay dëggël Seydi kiilu ngeen 
Ku si weesuwul buntam ya booy fëgg muy ubbi 
 
Rafet gëm ci Baay Laay moo di jééma roy ciy jikkoom 
Waxew yiw, jëfew yiw mandu moo gën ci taalibe 
 
Ku xemmem ndënal ñoñ Yalla da ngay déklu woote ba 
Nga am xel, te am teggin, di toog ak ñi koy tibbe 
 
Te bul déglu gaa ñi regg bay dox di puukëre 
Lu dul diine duy teggin, dañoo mel ni ñuy sebe 
 
Ba Mahdiyu woote gaa ña jiitiwoon dañoo rawe 
Ba tey ñu ngiy daw, may daagu ndax man dinaa dabe 
 
Ma dib lar bu dib laayif, te def pank muy tooñaan 
Ba saay wax ak saa jëf, seen bon gi tiital ma 
 
Damaa soobu cib gol, sopp gannaay, ragal namaa 
Lu fiy daane, booleek rab yu bon yeek na ñuy tëbe 
 
Ma jébbël la saay mbir, yow miy njaccaar ma silmaxa 
Tënëxtooti may réér, am tum bi ommat ma 
 
Li nuy sakku ciy bon bon, ba tee noo rafet fa Maam 
Lu tee noo labat baaxam ga ba weesu dénd bi 
 
Ragal naa sa may jëf, xawma jan jëf la nuy mujje 
Bu yemmook ju ñaaw muy coono, saa san la ñuy ñibbi 
 
Bu leen deeti xeeb kuy woote, Buur Yalla moom du ñëw 
Dafay woolu ay soppeem di leen yonni woote ba 
 
Ku dem pénc may layyoo da nga weddi woote ba 
Nu faf gëm Limaamu Laay mi xam yoonu jallu ba 
 
Da noo bon te nééwuk jaamu, nan seeti Muhamadu 
Ci dunyaa, na ngeen seet Maam Limaamo di jallu ba 
 
Man dey xawma waa dunyaa lu ñuy bañ ca woote ba 
Nde Baay Laay li muy digleek a wax, moo di jallu ba 
 
Di leen japp tey sellal di laay laay fa jakk jaa 
Li Baay Laay di diglé ngoog, looloo di jallu ba 
 
Di leen wax ci seen mbokkum jullit wax ju teey ju baax 
Li Baay Laay di diglé ngoog, looloo di jallu ba 
 
Di leen xool ci seen mbokkum jullit wax ju teey bu baax 
Li Baay Laay di diglé ngoog, looloo di jallu ba 
 
Guddig "Leylatul israahi" la jaaroon fa jallu ba 
Ba déeyook Boroomam Laahu, may gaa di jallu ba 
 
Siraat gééj gu réy ay duus, te dey xiiru noonam ya 
Nu ngiy gëm Limaamu Laay mi nuy jalle jallu ba 
 
Dafay xool Boroom tangaay wa, feyloo ko beelem wa 
Nu ngiy gëm Limaamu Laay mi xam yoonu jallu ba 
 
Boroom mey yu réy, dey joor nu tallal sunuy ndijjor 
Ba maanaam li gééj giy fuur, te ya raw tabeel mey ma 
 
Ku am saabu, am ndox tax nga naaguy ñimeñ taq 
Da ngay kum xelam des mbaa nga xés wuyu woote ba 
 
Bakken def na noon buy wor boroom def ko muy barmool 
Digaan leen nu sakku man bakken, won ko fiy ngir mi 
 
Sëriñ seeti leen seen tééré, niiraati Mahdiyu 
Bu ngeen raññewul Baay Layy, Limaamoo di xejj ba 
 
Sëriñ dénca leen seen tééré ñëw laajsi Ruuhu Laay 
Nabiyu Lummiyoo feeñ ci Yoof, moo di jallu ba 
 
Ku ci woolu sab xamxam ba yaakaar sa alluba 
Ba tax ngay jundum gii gééj, te doo jall jallu ba 
 
"Salaatan wa tasliiman alaa Seydi waraa" 
Maam Limaamu Laay leeram yaa moo raw yu jant bi 
 
 
7 - BISMI LAHI RAHMANI RAHIM 
 
Jantub diine yaa tiim gaayu gëm yaa 
Ku mar di nga naan ci gééj leer ya ngi baawaan 
 
Al hamdu li Laahi Rabbil aalaminaa 
Ndégem noo gëm ki Yalla yabal jamana 
 
Addina yaa ka mane gan doo nu naxtaan 
Nu ngiy yaakaar ki nuy mane gane ca Rilwaan 
 
Da lay mane gan te gaaw berndeel la gay béén 
Mu njuuy la nga daanu cim kan rééré ak neen 
 
Sagar ak i yax, lu leen geuneu ñaw la dooréé 
Ku kay beugg miim, bammeel seere ñaaree 
 
Bu leen ñétaan, ki addina jay ba dooleel ko 
Dina wor, dina njuuy, addina maa ka tuumaal 
 
Bu leen réyréylu, réy Laahoo ko yelloo 
Ku réylu ba dee malaaka ya jël la sewloo 
 
Ba Baay Laay wootewul dunyaa leudeum na 
Geureum leen goor gi moo ame leeru diine 
 
Ku xam Baay Laay te xam Nabi Laay ne mooma 
Mahdiyu Nabi Laay a feeñ; moo woote diine 
 
Jullitoo wooluleen, sang féñ na Soodaan 
Ku Yalla yakkal nga suur, na nu jomb xaaraan 
 
Mbindééf dina xool, di njéér te du gis ngëneel ya 
Ba Yonnent feegn na ci biir Yoof, noo ngi jaamu 
 
Mbindééf a ngi ñuul, te lamboo leeri Yonnent 
Ba leer yi di tuuru ci gééj, nuy naan ci mbeex mi 
 
Ku am xamxam, te ragnéé leeri Yonnent 
Da nga wara xam ne séydééy jiite yoon wi 
 
Sang Soodaan nga, Seydi donay Madiine 
Bu leen laamlaami, goor gee woote diine 
 
Limaamul Mahdiyu Soodaan Yoof la feeñ 
Wallaay Laahu la soob du danu ko jiiñe 
 
Du jang ci tééré, du ci xalimaam, du daa ja 
Kiñane dafa réy, nde boon ñu ne moo di waa ja 
 
Ba Nabi féégné, ca Makka, ba leer ya baawaan 
Xérém ya tasaaroo, Nabi tere leen bidaa ya 
 
Ku geum Nabi,geum Limaamu Rassoulou Laahi 
Gëlëm dafa réy, nde Kaaba ga, Jammlaahi 
 
Ba Njiin feeñé ca Yoof, bañ yay kalaame 
Ndaxam da ñu réér, nde Yonnent, moom du sankoo 
 
Bu doon, ku fi féñ ñu agga fa laaj ko yoon wa 
Bi Laahi du nu réér, nde sammaan miin na saawa 
 
Bu leen ñétaan buuri dunya ki liitam 
Juddook dee moom ku koy def, Buur du nawleem 
 
Sikkar sa di riir, bañam ya naan lee mu saankoo 
Mu naan saabaam ya asal du ma seeru Kongoo 
 
Ba Njiin waree gaal bañam ya di ree, jawaanoo 
Ba saaba ya naan ko Njiin doo teeri bayyi nu 
 
Rogogn ya di tuuru, bu doon wurus it di marjaan 
Ginnaaw jooy yooya, Laahu yaa di Rahmaan 
 
Ba gaal ga bañee ca Béér la ñu gëm, jalooréém 
Ba Kongo belseek Wiirwiir gnoo koy dégg ndéém 
 
Xayartu Madiine, Baay Laay, jeul na ndam laa 
Ku dem Ilayiina, muy jaayook njañam laa 
 
Ba Njiin feeñé, la robiney leer ya baawaan 
Ba rééw mi limbaane, Soodaan dootu naanaan 
 
Tanxal nu ci yol mi, yow miy Njool nu naanoo 
Ba mandi ci leer yi,Baay Laay yaay limbaane 
 
Ku langook ñaari yol loo deeti rootaan 
Da ngaa wara naan, di sangu say bagn di ñéétaan 
 
Beuceug la ko Buur ba woo, ba mu réér mbindééf ya 
Seumbéél ko sa leer ya muy jaayook binnéém ya 
 
Bu daa bilibaane, ñuy gaawtook a foofaan 
Malaaka ya door xéreum ya ñu weesu foofaa 
 
Baay Laay woote na, wacc na, moom jotal na 
Mbindééf yay jaamu, mu tiim leen, seede gëm ya 
 
Ba gééj sabbaa, Aras yeugou, woor na Baay Laay 
La seen pexe jeex, tereetu ñu gaa ña Laay Laay 
 
Sang da nga taaru, tabe, ku la séén daldi maaree 
Rafet gaw gaay, xanaa marjaan nga dooree 
 
Da nga tabe, muñ, di jambaar, doy nga waaroo 
Rafet ngab yar xanaa baatin nga dooree 
 
Da nga rafetal sa diine ba tey ma woy laa 
Ku fiy ame diine, Baay Laay jeul na ndam laa 
 
Li nuy bon - bon di saw gaay, yaa nu wéétéé 
Boroom Ridwaan sang bi yaa nu jiitéé 
 
Da ñu noon wird ak sikkar dina fey ca sowu 
Limaamoo woon, te mu nga war gaal di joow 
 
Ba pake bay déqi ba pat may xotti mbeex ma 
Malaaka yaa naan ka Seydeey jiité soodaan 
 
Ba tey leer yaa ngi baawaan rééw mi fess na 
Ñu ngiy laay laay,di roy Baay Laay ci diiné 
 
Baay Laay noon na Séydeey jiité gaa ñaa 
Ku bañ Baay Seydi na nu jox, maa ko wooloo 
 
Boroom "Ridwaan", ku la woy naani Tuubaa 
"Al hamdu li Laahi Rabbil aalaamiinaa" 
 
Al hamdu li Laahi Rabbil aalaamiinaa" 
Sangub jamaanaa ngi, Soodaan woy ko lay jééx. 
 
 
 
8 - BISMI LAHI RAHMANI RAHIIMI 
 
Bi Bismi Laahi ma deeti woy Madiné 
Wolof la may mottalikoo saa yééné 
 
Tey ba ëllëg nuy wuyu Maam Limaamu 
Moom ki nu woo ci ngir mi, ngir nu jaamu 
 
Al Hamdu li Laahi, nuy sant Buur ba 
Jagle na nu sang, tabeel ndijoor ba 
 
Séydi Limaamul Mahdiyu taabeem ga 
Jéggi na waame, raw ginnaxu gééj ga 
 
Dogoonkoon ak Mahdiyu laay mi woote 
Kuy jééma leeral mbir mi yaa koy wuute 
 
Waxtu wu jot nu japp, ken du tiimoo 
Lottal na Lawliya yi, noo ko moomoo 
 
Sikkar guddéék bëccëg ni riiru gééj 
Yonnent jagoo nay jungjung du ndiij 
 
Nu sant doomi Alsaan ak Seyni 
Moom ki nu woo ubbil nu yoonu diiné 
 
Moo jëkké fi lakkal xaleel yu tuut yi 
"Wal ixtixaadi sawjan lil banaati" 
 
Ponki julléék njapp mi ngeen maggaale 
Fu ngeen fi jëm, Yalla di seen andaale 
 
Goor ak jigéén, mag ak ndaw xaleel 
Jaamu gi, noo si maase, naaj ak teel 
 
Ku Yalla yonni, noo ko mos ni siiw 
Loo wax nu woolu, dootu nun di beew 
 
Bu leen werante, baatu goor gi siiw na 
Nit ak jinnee ko déggandoo te woor na 
 
Baay Laay ne"Aajibuu daaya Laahi" 
Muy wax ja woon ca yaa Rasuulu Laahi 
 
Moom bés bu ne mu mel ni gan, nuy teeru 
Ñi gëm te woolu saa su jot ñuy waaru 
 
Mbooleem sëriñ si, raw na leen si waare 
Tereek a digle, lii la Njool ma doore 
 
Mbooleem hu fuy teyteyluy laaj, déggoon na 
Waxam ja démb, tey donnaam ja teew na 
 
"Sayaaratun daabatun Ruuhu Laahi" 
Yallaa di tax nga war ko waaw wa Laahi 
 
Gis texe, maa le seeru, man kañ naa la 
Gëm mucc, weddi alku, woolu naa la 
 
Yaa wax nu dégg, jëf nu gis, mbër waadaa 
Wuutewulaak doomi Maryaama Soodaa 
 
Diggënte Beyti Maamur ak Yaraax 
War nga fi daaba, muy ju gaaw, du xoox 
 
Jub nga Yaraax, labbe ya doon la teeru 
Sa lampi leer sëggël na leen ñu yiiru 
 
Nga wacci war Maanatu Laay jëm Yoof 
Jullee fa Njool ma, boole doom ta uuf 
 
Sat "muxjizaat", lottal na gaa ñay séénu 
"Wa lan yaruu mislu ka yaa lamiinu" 
 
Ku mos di weddi, yaa ko won mu seeru 
Ku fuy tëbëntu ngay jiñax mu jooru 
 
Kerook ba Maam ñibbee fa Jammlaahi 
"Xad hayaru ashaabau fi Laahi" 
 
Déelé bi suuf ak asamaaw yi ñoom 
Jooy na ñu Njiin, jooyi guneek seen maam 
 
Gééj ga di jooy, rongoñ yu tey yu neex 
Ku sëgg naan, ba siggi waaru giix 
 
Fekkoon nga mbooleem gëm yi jooy ba jééx 
Sab taxawaay tax na ba seen xol fééx 
 
"Ibnu Asan Séydinaa Limaamu 
Abu Issaa Ruuhu Rabbil xadiim" 
 
"Man xaala ajibuu daaya Laahi" 
Amul keneen ku wax waxam wa Laahi. 
 
"Wal mujrimiinal musrikiina naaluu 
Xusraanu inda diina kum maxfuuluu" 
 
Bu leen ragal keneen ku dul Ilaahi 
Ak Yonnentam ba doomi Abdalaahi 
 
Mbubbum ragal, Yalla fu gën baraaya 
Moo gën sujéé ka dox di bif daraa ya 
 
Ruuhu Ilaahi,kiy donoy Rasuulu 
Ibnu Imaamul muntasar, laa woolu 
 
Ñay mbër ca Yalla, seeni yan nga boolé 
Saa sépp man, dinaa la ñaanal doole 
 
Abaabakar, Umar, Usmaan, wa Aliyu 
Yaa boole seeni mey di jiite gaa ña 
 
Kuy jééma gotti saa mbër it bul naagu 
Ndax wéqu weén tereetul ñay wa daagu 
 
Ña wuyuwoom Yonnent ca ba mu woote 
Mu japp gaa ña, boole xol ya footéé 
 
Ku fuy tëbal ci Yalla jii jamano 
Na gëm dogal ba, mbaa du weesu daanu 
 
Ku weddi alku, doonte "lawliyaawu" 
Nit ak jinné si yam, na ngeen si yeewu 
 
Yallaa ma yonni, moom la wax fa Yoof 
Ba Njiin jibéé la bokk yépp keef 
 
Ñu naan ko wax ji réy na yaa Limaamu 
Mu yékki baatam ba ca kow, ñu yéému 
 
Jangul, bindul giseesu fook i tééré 
Xam xam ba cab dënnam xajul ci tééré 
 
Yonnent bu Yalla yonni lii la waare 
Ndaw ñaak jigéén ña gëm, sëriñ sa réér 
 
Lu ngeen fi deeti jang, safara yay na 
Léébu wolof lawon ca yagg, feeñ na 
 
Feeñoon na Makka gaa ñu baax ña booloo 
Sette waxam ja, muy ju woor, ñu wooloo 
 
Am ca ñu jomlu, gantu ngir kiñaan 
Ku and ak ñooñaa déég ba doo ca naan 
 
"Xafadta diini kufra Ruuhu Laahi 
Abaa ka mursalum fi diini Laahi" 
 
Ma wax la tuuti fii ci say jalooré 
Ba gaa ña dégg, Saaba yaak kay seere 
 
Tabeek soxar la mbër yi mos daan boole 
Kuy bañ ci ngir mi, ñoo ko daan yan doole 
 
Yalla la fal "Aamiral muuminiina" 
Ku weddi fii sa wax, jëfam ja neen na 
 
Sa tur a jiit sa taxawaay ci dun bi 
Deefu la jaawaleek keneen ci gééw bi 
 
Baay Laay rafet na diine, Njiin du maas 
Ku weddi, sangutee fa Maam Libaas 
 
"Wa man yarju illaa jinaani Laahi 
Xudaamu u faxlam u Ruuhu Laahi" 
 
 
 
 
 
 
 
 

 

(c) gotts78 - Créé à l'aide de Populus.
Modifié en dernier lieu le 31.03.2011
- Déjà 6779 visites sur ce site!